Retour aux enseignements Revue web

Cheikh Abdoul Ahad : Su ma waxee

Man day def su ma waxee ci kaw, ñu ne day xulóo.
Bu ma waxee liñ wara def, ñu ne daa mer.

Ma di léen xamal nak ni léen, xulóo ak mer darra du ma ko ci def li feeg may dundu.

Ndax xulóo moom, li koy waral xam naa ko, ñaar ñu déggoodi koo rekkay xulóo. Te man du ma xulóog buur, du ma xulóog baadoola, du ma xulóog mag, du ma xulóog ndaw ! Ngir yiy taxa xulóo moom, du jaar sama digg’ak kenn.

Xëcóo njariñ wala xëcóo daraja, yooyu rekk mooy tax di xulóo, te waat naa ci Yàlla ne du ma ko def ak kenn !

Mer itam, bu ngéen jàppee ni mer naa, déedéet, da maa am lu ma naqari, mer moom dara taxu ma ko mana def, lu dul gis loo xam ne lu naqari Yàlla la lu ma manu la faj. Loolee daf may naqari ngir li mu naqari Yàlla dongu, waaye du tee di naa xam ne
‎إنا من المجرمين منتقمون
Yàlla bim ko waxee, boo gisee kuy def lu neexul Yàlla yit, bu la naqaree war ngaa mana gàttal naqar wa, yéggul fenn !

Man du ma mer ! Du ma xulóo ! Da maa bëggoon rek loolu leer leen.

Contributeur :Abdou Lahad Diakhate


Laisser un commentaire

Votre adresse de messagerie ne sera pas publiée. Les champs obligatoires sont indiqués avec *